jëxiis (la stivation: texte traduit en wolof langue sénégalaise par M. MBACKE THIOUNE p)
5 pages
Français

jëxiis (la stivation: texte traduit en wolof langue sénégalaise par M. MBACKE THIOUNE p)

Le téléchargement nécessite un accès à la bibliothèque YouScribe
Tout savoir sur nos offres
5 pages
Français
Le téléchargement nécessite un accès à la bibliothèque YouScribe
Tout savoir sur nos offres

Description

Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis » Stivation“Jëxiis”, tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo Ca attum 1970 ak lu ko wër, ay kàngaam yuy yëngu ci wallu xel ak nekkin bokk ci ngiiru Piaget ca Genève, ñoom Doise, Mugny, Perret-Clermont, dañoo sumb ak coppite gu mattale ci wàllu njàngale ak njàngin. Sumb boobu nak da nu koo wéer ci gis-gisu tàggatum xel ak xam- xam ci pencoo. Kàngaam yooyu di askanoo ci Piaget wonenan ab feem ci njangalin buy sukkandiku ci tabax ak pencoo xam-xam. Feem wi wone na ne xaleel buy weccoo xalaat ak ay moroomam di na ful ay pexeem, di na nàmm xelam. 1 Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis » Li ko sabab mooy ne xaleel suy diisoo ak ay moroomam di na jiixi- jaaxa ci ay xalaatu boppam, di na jiixi-jaaxa it ci digganteem ak ay moroomam. Jiixi-jaaxa googu di indi jàmarloo ak disoo. Lii lepp di wund ci gàttal ne jëf-lante yi xale yiy sexx di na sabab yokkute ci seen njàng. Feem wii di Stivation“Jëxiis”, tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak xam-xam ci pencoo mi ngi sàmp ay reenam ci gisin wi nu leeral ci kaddu yi jiitu. Amul sikk ne di na jarin it taggatum mag ni ak way njàng liggeey bu mu mën a nekk. Ay ndongo-wéy saytu njàng mi ca FASTEF (Daara ju mag ji Cheikh Anta DIOP ca Dakar) def na nu ci ab gëstu bu xÒot, njurka ya am na solo lool.

Informations

Publié par
Publié le 31 mai 2013
Nombre de lectures 340
Langue Français

Extrait

Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis »


Stivation“Jëxiis”, tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak
xam-xam ci pencoo




Ca attum 1970 ak lu ko wër, ay kàngaam yuy yëngu ci wallu xel ak
nekkin bokk ci ngiiru Piaget ca Genève, ñoom Doise, Mugny,
Perret-Clermont, dañoo sumb ak coppite gu mattale ci wàllu
njàngale ak njàngin.
Sumb boobu nak da nu koo wéer ci gis-gisu tàggatum xel ak xam-
xam ci pencoo.
Kàngaam yooyu di askanoo ci Piaget wonenan ab feem ci njangalin
buy sukkandiku ci tabax ak pencoo xam-xam.
Feem wi wone na ne xaleel buy weccoo xalaat ak ay moroomam di
na ful ay pexeem, di na nàmm xelam.

1
Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis »

Li ko sabab mooy ne xaleel suy diisoo ak ay moroomam di na jiixi-
jaaxa ci ay xalaatu boppam, di na jiixi-jaaxa it ci digganteem ak ay
moroomam.
Jiixi-jaaxa googu di indi jàmarloo ak disoo.
Lii lepp di wund ci gàttal ne jëf-lante yi xale yiy sexx di na sabab
yokkute ci seen njàng.
Feem wii di Stivation“Jëxiis”, tuut tànk ci yooni tàggatum xel ak
xam-xam ci pencoo mi ngi sàmp ay reenam ci gisin wi nu leeral ci
kaddu yi jiitu.
Amul sikk ne di na jarin it taggatum mag ni ak way njàng liggeey bu
mu mën a nekk.
Ay ndongo-wéy saytu njàng mi ca FASTEF (Daara ju mag ji Cheikh
Anta DIOP ca Dakar) def na nu ci ab gëstu bu xÒot, njurka ya am na
solo lool.
Feem wii di Stivation“Jëxiis” dafay sukkandiku ci seetlu ne jëf-
lante yi ndongo-wéy saytu njàng mi ci seen daara jooju di na
suuxat ay mën-mën ci seen wàllu liggeey tek si di suuxat seen
digante bu baax a baax.
Mu nekk lu am solo ci ñu wara nekk ëlëg ay kilifa yu wara indi
soppite yi ñu yaakaar ne di na nu jur njariñ ci njàngale ak njàngin
wi.
Mbir mi sax soxolul ndongo-wéy saytu njàng mi rekk. Képp kuy
ndaw luy yëngu ci lu am njariñ mën nga cee gis sa bopp.


2
Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis »

Waaye dëgg la ne tàggat wu njëk wi am na solo lool ci bepp wéy
sakku liggeey waaye du tere ay yeneen i pexey tàggat dina nu
yombal ay xarala yu bees te bari njariñ ci liggeeyu wéy tàggatu bi.
Feem wii di Stivation “Jëxiis” da fa nekk aw tëggin wu yees bu am
yeeney def jëf-lante ak pencoo xam-xam ak ay mën-mën muy ken
wiy màndargaal seen xareñ.
Feem wii di Stivation“Jëxiis” di sukkandiku ci ñetti joxoñ :
1. Jëf-lante
2. Xiirtal
3. Soññ
Feem wii di Stivation“Jëxiis” dees na ko wax su nekkee ne jëf-
lante yi jéggi ëttu njàng mi da nuy xirtal ak a soññ wéy njàng yi,
amaale jeexit ci solos seen i mën-mën (kenn-kenn ak mboleem
seen).
Ci tënk, Stivation“Jëxiis” di na tax njurka yi cosaanoo ci
tolluwaayu tàggat yi ci wàllu njàng, tabaxinu ay xarala ak fullaal
gëm sa liggeey gënna dëggër, gënna yaatu.
Ndax kat, tënkal sa moroom kàddu gu am maanaa, tontu laaju sa
moroom, yey sa moroom ci cëslaay gu wér, nangu it ñu yéy la ci
dëgg doonte di nga jiixi-jaaxa ndax soppite gu bette ci la nga
foogoon dina mootalli xam-xam ak yar jiko.

3
Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis »

Jiixi-jaaxa googu da fay soññu mbooloo mi te di xirtal pas-pasam,
kattanam, nisëram ngir jëm ca kanam.
Jiixi-jaaxa di na it tax ba mbooloo mi di raas xam-xam fu mu mën a
tollu. Su ko defee njàngu wéy tàgaatu yi di na mën a ño ŋ.
Ci tënk, sikkuwul ne xalaat, weccoo xalaat ak wesaare xam-
xam bi nekk ci lëllu tàggat yi di na gën a yokku seen xarañ.
Stivation“Jëxiis”, mënees na koo jàppee yoon wu yees ci wàllu
njàng woo xamne da fay sukkandiku ci jëflante ak pencoo
xam-xam ci ay wéy tàggatu yu mu mën a doon.
Stivation“Jëxiis”, doonte mi ngi nàmpee ci ngiir yi gëm ne tabax
ak pencoo xam-xam mooy yoon wi gën a jub ci wàllu njàng ak
njàngale, da fa ubbeku, jéggi bepp ëttu wërngël këpp.
Seetlu nan ne Stivation di na tax ba bépp wéy tàggatu am fitu wax
ci mboolo, am fitu màndargaal njàqareem ak njaaxleem ci jotaay.
Yii mën-mën di na yeewi xel, di na nàmm it lamiñ ba boroomam
mën a jot dayoom ci bepp kuréel bu mu mën a nekk.
Kon ci tënkug jeexal, na nu jàpp ne Stivation“Jëxiis” ab tërëlinu
tàggat la bu nu mën a jëfe ci lëlu ndongo-wéy saytu njàng mi wala ci
bépp tàggat ay mag bu mu mën a doon.


4
Seex Axmadu Bàmba MBAY, Wéy tàggat njàngale mi, Feentkatu Stivation « Jëxiis »

Gëstu yi nu ci mën a def ak jéemëntu yi nu ci mën a def di na am
solo ndax di na tax jangalekat yi faaydaal tabax ak pencoo xam-xam
ci ay ndongo ba gën koo jëmal ci seen i sumb liggéey.
Yoon wu bees la buy wootal jangalekat yi ñu boole seen bopp ak
seeni pexe ngir mën a weccee xalaat ak i feem ba seen liggeey gën a
sell.
Mu mel ne di na doon njariñ ci Nguur gi ak askan wi ndax
jangalekat yi bari nañ jafe-jafe yu ñuy jànkoonteel rax ci dolli
soppite yi dafay gën di bari.


Email : mbayemouhamadoubamba@yahoo.fr
Tel : +221 70 331 81 03
Seriñ Mbàkke CUUN, moo ko firi ci Wolof jële ko ci nasaraan

___________________________________________________________________

___________________________________________________________________

5

  • Univers Univers
  • Ebooks Ebooks
  • Livres audio Livres audio
  • Presse Presse
  • Podcasts Podcasts
  • BD BD
  • Documents Documents